Youssou N'Dour - Sportif lyrics

Published

0 205 0

Youssou N'Dour - Sportif lyrics

Woyal sa wayu ndam ii Dangay bégël sa xol bi Ndax yaa yor bannex bi Ni tay bés bii sa bés la Sa mbër daan na kóntaan nga Bu ñu daanee sa mbër nak Na nga fexe ba nee Po mii dañuy Jonante Faw mu am ku moyle Jarula defante, di xasteeka dóóre Jonante po ag ree la Boo gañee fo ag ree la Boo ñàkkee fo ag ree la Lépp ci fo ag ree la Buñ la gañee muñël Boo ko gañee baalal Bëgóón nga mu demee ni demewuko Mën naa am bu ëllëgee mu gën fee neex Ba ma làng ag samay gaa yi ngir bànneexu Xam ne lii fo la nii lay mënë deme Powun jonante nii lay deme Tay jii yaw bu ëllëgee keneen la Fo ag ree de lañ ciy jublu Moo tax ñu wara dal taynangu defet Jonante po ag ree la Boo gañee fo ag ree la Boo ñàkkee fo ag ree la Lépp ci fo ag ree la Buñ la gañee muñël Boo ko gañee baalal Waa waaw wuy dabbee wuy yoo Dabi alaa ko ndey baate satata Abdulaay ag Maajoor Maajoor ag Mataar ag jaara seen jigéén Sire lañu dóór bal géér ña da ñoo daw Sire Bàlla moo ñaan Ramata Faal Siree nga Cees Matee nga Njaarém Duñ ko wëy ku reew, duñ ko wëy ku ñaaw Aah wuy dabbee wuy yoo Dabi alaa ko ndey baate satata Jonante po ag ree la Boo gañee fo ag ree la Boo ñàkkee fo ag ree la Lépp ci fo ag ree la Buñ la gañee muñël Boo ko gañee baalal